YouVersion Logo
Search Icon

Luug 6:27-49

Luug 6:27-49 KYG

«Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax. Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen. Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki. Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj. Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu. «Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen. Te su dee ñi leen defal lu baax doŋŋ ngeen defal lu baax, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yeet noonu doŋŋ lañuy jëfe. Te su dee ñi ngeen yaakaare ndelloo doŋŋ ngeen lebal, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi it, yaakaar ndelloo lu mat sëkk moo tax ñuy leblante. Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe. Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande. «Buleen di sikkale, su boobaa deesuleen sikkal. Buleen yeyale kenn ab daan, ngir ñu bañ leena yeyale ab daan. Baleleen, ñu baal leen. Mayeleen, ñu may leen; natt bu duun bu ñu rokkas, yëngal, mu fees bay tuuru, moom lees leen di nàddil ci seen mbubb. Ndax natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale.» Yeesu léebati leen, ne leen: «Ndax gumba dina wommat gumba? Mbaa duñu ànd tàbbi ci kàmb? Taalibe sutul sëriñam, waaye bépp taalibe bu jàng ba wàcc, tollook sëriñam. «Ana looy xoole xatax bi ci sa bëtu mbokk te gànj gi ci sa bëtu bopp gisuloo ko? Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax gi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax gi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko. «Garab gu neex du meññ doom yu naqari, te garab gu naqari it du meññ doom yu neex. Garab gu nekk, meññeefam lees koy xàmmee. Ag dédd, deesu ci witte doomi figg; ay dagg it, deesu ci jële doomi reseñ. Nit ku baax, dencub ngëneel ba ca biir xolam, ca lay jële lu baax la mu sàlloo; nit ku bon it, dencub safaan ba ca biir xolam, ca lay jële safaan ba mu sàlloo. Gémmiñ daal, la fees xolu boroom lay wax. «Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax? Képp ku ñëw ci man, dégg samay wax te di ko jëfe, dinaa leen won nu muy mel. Dafa mel ni nit kiy tabax kër, gasa gas ba mu xóot, daldi samp kenu ga ca kaw doj wa ca suuf. Mbënn ma dikk, wal ma rëkk kër gaak doole te manu koo yëngal ndax tabax bu wér ba ñu ko tabaxe. Waaye ku dégg te jëfewoo, dangaa mel ni nit ku tabax kër ci suuf, te amul kenu. Wal maa koy rëkk ak doole, kër ga jekki màbb, yàqu yaxeet.»

YouVersion uses cookies to personalize your experience. By using our website, you accept our use of cookies as described in our Privacy Policy