Luug 4:5-8
Luug 4:5-8 KY
Seytaane yéege na ko fu kawe itam, won ko mboolem nguuri àddina, ci xef ak xippi. Seytaane ne Yeesu: «Yaw laay may mboolem kilifteef gii ak daraja ji mu àndal, ndax man lees ko jox, te ku ma soob laa koy may. Kon nag soo ma sujjóotalee, yaa moom lépp.» Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”»





