Sarxalkat yi 17
17
Ndigal yi jëm ci sellal
(Saar 17—26)
Li war ci jaamu ak sarxal
1Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: 2«Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak bànni Israayil gépp ne leen li Aji Sax ji santaane mooy lii: 3Képp kuy góor ci waa kër Israayil, bu rendee aw nag mbaa xar mbaa bëy ci biir dal bi, ak fu génn dal bi, 4te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, teewalal ko Aji Sax ji, muy sarax ca buntu jaamookaayu Aji Sax ji, kooku dees na ko topp àqu deret. Dafa tuur deret. Kon dees koy dagge ci biir bànni Israayil. 5Su ko defee bànni Israayil dinañu indil Aji Sax ji juri sarax yi ñuy rendi ci àll bi. Dañu koo wara yóbbu ca sarxalkat ba, fi Aji Sax ji, ca bunt xaymab ndaje ma, defal ko Aji Sax ji saraxi cant ci biir jàmm. 6Sarxalkat bi day xëpp deret ji ci sarxalukaayu Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi, ba noppi, lakkal Aji Sax ji nebbon bi, muy xeeñ xetug jàmm gu neex Aji Sax ji. 7Buñu di sarxalatil tuur, yi ñuy jëmmale sikket, di ko bokkaalee. Na loolu di dogal bu leen war fàww, ñoom ak seen askan. 8Wax leen boog ne leen: Képp kuy góor, ku bokk ci waa kër Israayil, mbaa mu bokk ci doxandéem yi ci seen biir, buy génne ab saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax, 9te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, sarxalal ko Aji Sax ji, kooku dees koo wara dagge ci biir bànni Israayil.
10«Te it képp ku bokk ci waa kër Israayil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israayil. 11Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam. 12Looloo waral ma ne bànni Israayil, bu kenn ci ñoom lekk deret, te doxandéem bi ci seen biir it bumu lekk deret.
13«Képp ku bokk ci bànni Israayil mbaa ci doxandéem yi ci seen biir, bu rëbbee ba jàpp mala mbaa njanaaw, mu di lu dagana lekk, na tuur deret ji, suul, 14ndax deret dafay jëmmal bépp dundu mbindeef bu Yàlla sàkk. Moo waral, man Aji Sax ji, ma ne bànni Israayil buñu lekk deretu menn mbindeef ngir dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Képp ku lekk deret, dees koy dagge ci askan wi.
15«Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set. 16Waaye su fóotul, sanguwul, mooy gàddu bàkkaaram.»
Currently Selected:
Sarxalkat yi 17: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright