YouVersion Logo
Search Icon

Njàlbéen ga 16

16
Ismayla juddu na
1Sarayi amul woon doom ak boroom këram Ibraam. Waaye fekk na mu am jaam bu juddoo Misra te tudd Ajara. 2Sarayi ne Ibraam: «Li am mooy Aji Sax ji deful ma am doom. Kon ngalla waay, jëlal sama jaam bi, tëdd ak moom ndax Yàlla def, mu amal ma doom ju góor.» Ibraam nag dégg la Sarayi wax. 3Looloo ngi am, gannaaw ba Ibraam dëkkee fukki at ca réewu Kanaan. Sarayi daldi jël Ajara, jaamam bi juddoo Misra, jox ko jëkkëram Ibraam, ngir mu tëdd ak moom. 4Loolu wees Ibraam séy ak Ajara, mu daldi ëmb. Ajara yég ne ëmb na, indi nag yabeel digganteem ak sangam Sarayi.
5Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga tëdd ak moom, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» 6Ibraam wax Sarayi ne ko: «Sa jaam a ngoog ci say loxo, def ko lu la neex.» Sarayi nag di toroxal Ajara, ba mu daw, ba soreek moom.
7Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox ba ca yoonu Sur. 8Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.»
9Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.» 10Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» 11tegaat ca ne ko:
«Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor;
nanga ko tudde Ismayla (muy firi Yàlla dégg na),
ndax Aji Sax ji yég na sa naqar.
12Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul noot,
di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko.
Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.»
13Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (muy firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» 14Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (muy firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beredd.
15Ba loolu weesoo Ajara amal Ibraam doom ju góor. Ibraam tudde doom ji Ismayla. 16Ba Ajaray am Ismayla, Ibraam a ngi tollu woon ci juróom ñett fukki at ak juróom benn (86).

Currently Selected:

Njàlbéen ga 16: KY

Highlight

Share

Compare

Copy

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in