GEN 10
10
Askanu doomi Nóoyin
(Saar 10.1---11.9)
Xeet yi sosoo ci doomi Nóoyin
1Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom.
Li jëm ci askanu Yafet
2Doomi Yafet yu góor ñoo di Gomeer ak Magog ak Maday ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. 3Doomi Gomeer yu góor ñoo di Askenas, Rifaat ak Togarma. 4Doomi Yawaan yu góor ñoo di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. 5Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet.
Li jëm ci askanu Xam
6Doomi Xam yu góor ñoo di Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. 7Doomi Kuus yu góor ñoo di Saba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Seba ak Dedan.
8Kuus moo jur Nimrodd, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, 9mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Nimrodd, rëbbkat bu maga mag ba.» 10Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. 11Ca réew mooma la Nimrodd jóge dem Asur, sanc Niniw ak dëkk yooyee di Rexobot Ir ak Kala, 12ba Resen gi ci diggante Niniw ak Kala, dëkk bu mag bi.
13Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi#10.13 Luddeen ñi ñooy waa Ludd, ci waxin wuy tekki ab giir niki boo nee Njóobeen ñi walla Njaayeen ñi. ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi 14ak Pataruseen ñi ak Kasluxeen ñi, ak it Kaftoreen ñi, ñooñee waa Filisti soqikoo#10.14 Seetal ci Amos 9.7..
15Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett. 16Kanaan mooy maamu Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi. 17Mooy maamu Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi. 18Mooy maamu Arwàddeen ñi it ak Cemareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. 19Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Adma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
20Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
Li jëm ci askanu Sem
21Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. 22Doomi Sem yu góor ñoo di Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. 23Góor ñi Aram jur ñii la: Ucc ak Xuul ak Geter ak Maas. 24Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber. 25Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (muy firi Séddalikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddalikoo woon. Rakku Peleg ju góor mooy Yogtaan.
26Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yerax 27ak Adoram ak Usal ak Digla 28ak Obal ak Abimayel ak Seba 29ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. 30Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku.
31Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
32Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.
Currently Selected:
GEN 10: KY
Highlight
Share
Compare
Copy
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Apps and more at https://kaddugyalla.com/
Copyright info at https://kaddugyalla.com/copyright