YouVersion Logo
Search Icon

Mucc ga 27

27
Lu jëm ci sarxalukaay bi
1«Nanga defare sarxalukaay bi bantu séng, guddaay bi di juróomi xasab, yaatuwaay bi di juróomi xasab; ab kaare la sarxalukaay biy doon, taxawaayam di ñetti xasab. 2Defaral ko ay béjjénam ci ñeenti coll yi ci kaw. Béjjén yi, dees koy liggéeyaaleek sarxalukaay ba, ñu ànd di benn, te nanga xoob sarxalukaay bi xànjar. 3Sàkkal ay ndabi tibbukaayu dóomam, ak ay ñiitukaayam, ak ay këllam, ak ay seppikaayi yàpp aki andam. Defal jumtukaayam yépp xànjar. 4Sàkkal ko caax bu ñu tëgge xànjar te nga sàkkal caaxu xànjar bi ñeenti nopp ci ñeenti collam. 5Tegal caax bi, mu ronu peggu sarxalukaay bi, te dale ci suuf ba ci digg sarxalukaay bi. 6Sàkkalal sarxalukaay bi ay njàppuy bantu séng, te nga xoob lu ci nekk xànjar, 7te nga roof njàppu yi ci nopp yi, su ko defee njàppu yi des ci ñaari weti sarxalukaay bi, ngir bu ñu koy yóbbu. 8Am pax ngay def sarxalukaay bi ci biir; nga defare ko ay xànq yu tàppandaar. Na ñu la ko wone ca kaw tund wa rekk lañu koy defe.
Lu jëm ci ëttu jaamookaay bi
9«Nanga sàkkalal jaamookaay bi ab ëtt: guddaayu ëtt bi ci wetu bëj-saalum, téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe moo koy ub, ci genn wet googu. 10Jëni jaamookaay bi ñaar fukk lay doon, seen ñaar fukki tegu di xànjar, wékkukaay yeek galani jën yi di xaalis.
11«Naka noonu it ci wetu bëj-gànnaar, guddaay bi di téeméeri xasabi sori rabal, ak seen ñaar fukki jën yu seen ñaar fukki teguy xànjar ronu, wékkukaay yeek galani jën yi di xaalis.
12«Yaatuwaayu ëtt bi, fi féete sowu, juróom fukki xasabi sori rabal a koy ub, seeni jën di fukk, seeni tegu di fukk.
13«Yaatuwaayu ëtt bi, fi féete penku ci kanam, juróom fukki xasab la: 14fukki xasabi sori rabal ak juróom moo ub ëtt bi ci googu wet, seeni jën di ñett, seeni tegu di ñett. 15Wet gi ci des it, fukki xasabi sori rabal ak juróom, seeni jën di ñett, seeni tegu di ñett. 16Buntu ëtt bi nag, na doon lafu ñaar fukki xasab, wu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, muy liggéeyu ràbb bu rafet, ay jënam di ñeent, seeni tegu di ñeent.
17«Jën ya wër ëtt ba yépp, dees koy lëkkalee galan yu xaalis, wékkukaayi jën yi di xaalis, seeni tegu di xànjar.
18«Guddaayu ëtt bi téeméeri xasab lay doon, yaatuwaay bi di juróom fukk, taxawaayu wet yi di juróomi xasab, sor yi ñu ràbbe lépp di wëñu lẽe, tegu yi di xànjar. 19Mboolem jumtukaay yi ñuy liggéeye ci jaamookaay bi, ba ci mboolem xeri xaymaam, ak mboolem xeri wërmbalu ëtt bi, lépp xànjar lay doon.
Lu jëm ci santaane yi sarxalkat yi sasoo
(Saar 27.20—34.35)
Lu jëm ci diwu làmp bi
20«Yaw nag, santal bànni Israayil, ñu indil la diwu segalu oliw gu raxul ngir leerlu, ñu di ko taale làmp yi guddi gu nekk. 21Ci biir xaymab ndaje mi#27.21 xaymab ndaje mi: dees na ko woowe jaamookaay ba, ba tey. la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israayil fàww, ñoom ak seen askan.

Currently Selected:

Mucc ga 27: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in