Mucc ga 27:20-21
Mucc ga 27:20-21 KY
«Yaw nag, santal bànni Israayil, ñu indil la diwu segalu oliw gu raxul ngir leerlu, ñu di ko taale làmp yi guddi gu nekk. Ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israayil fàww, ñoom ak seen askan.



