Mucc ga 11
11
Yàlla waaj na yar bu mujj ba
1Ba loolu wéyee Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Benn yarub mujjantal laay dellu wàcce ci kaw Firawna ak waa Misra. Su ko defee du leen bàyyi ngeen dem, yem ca. Da leen fiy far dàqe, ba fàww. 2Te neel mbooloo mi, góor gu nekk ak jigéen ju nekk ci ñoom na sàkkoo ci dëkkandoob waa Misraam, ay gànjari xaalis ak wurus.» 3Ci biir loolu Aji Sax ji def waa Misra yéwéne leen. Musaa sax ci boppam ku ñu naw la woon ca réewum Misra, ca dagi Firawna ya, ba ca baadoolo ya.
4Musaa daldi wax Firawna ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Bu guddi gi xaajee, maay wër Misra gépp, 5te lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, dina dee, dale ko ci taaw bu góoru Firawna, mi toog ci jal bi, ba ci taaw bu góoru jaam bu jigéen bu féetewoo wol, boole ci luy taaw bu góor ci jur gépp. 6Dees na dégg yuux yu réy jibe Misra gépp, lu masula am, te dootul am mukk. 7Waaye fépp fu bànni Israayil dëkke, dara du fa wokk nit ak mala.” Su boobaa dingeen xam ne, Aji Sax jee ràññaatle waa Misra ak bànni Israayil. 8Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba fees. 9Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Li waral Firawna du leen déglu, mooy sama kéemaan yi wara fulandiwu ci réewum Misra.» 10Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israayil, ñu génn réew ma.
Currently Selected:
Mucc ga 11: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright