Mucc ga 1
1
Bànni Israayil dem na réewum Misra
1Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israayil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di: 2Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda 3ak Isaakar ak Sabulon, ak itam Beñamin; 4ak Dan ak Neftali ak Gàdd ak Aser. 5Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. 6Gannaaw ga, Yuusufaaki doomi baayam yu góor yépp nelaw, ñook maas googu gépp. 7Bànni Israayil nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma.
Firawna noot na bànni Israayil
8Ñu dem ba jëmmi jamono, beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra. 9Mu wax ak waa réewam, ne leen: «Giirug bànni Israayil kat ñu ngi nuy gëna bare, ba ëpp nu doole. 10Nanu ci sàkk pexe, ngir ñu bañatee yokku. Lu ko moy bu xare amee, man nañoo far ak sunuy noon, xeex ak nun, ba rëcc, génn réew mi.» 11Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israayil tabaxale Firawna#1.11 Firawna turu pal la, ñeel bépp buuri Misra. buuru Misra#1.11 Misra mooy réew mi ñuy wax Esibtë ba tey. dëkk ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund. 12Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu, yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israayil.
13Waa Misra dañoo mujj di duggal bànni Israayil ci njaam gu metti, 14yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas.
15Firawna buuru Misra teg ca wax ak rewlikati Ebrë ya#1.15 Ebrë tur la wu niti jamono jooja daan woowe xeet, ya bànni Israayil bokk., te kenn ka tuddoon Sifra, ka ca des di Puwa. 16Mu ne leen: «Bu ngeen dee rewli jigéeni Ebrë yi, nangeen xool lu xale bi doon. Su dee góor, reyleen, su dee jigéen, bàyyileen, mu dund.» 17Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund. 18Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» 19Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.» 20Bànni Israayil nag di fulandiwu, gëna yokku, Yàlla defal rewlikat ya aw yiw, 21may leen giir ndax seenug ragal Yàlla. 22Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»
Currently Selected:
Mucc ga 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright