Efes 3
3
Póol xamle na mbóotum Yàlla
1Moo ma tax di ñaan, man Póol mi ñu tëj ngir Almasi bi, ndax ñi dul Yawut, yeen jàmbur ñi, 2ndegam yég ngeen sas wi ma Yàlla sas ciw yiwam, ñeel leen. 3Ci am peeñu lañu ma xamale mbóot mi, noonu ma leen ko tënkale woon ci bataaxal. 4Bu ngeen jàngee loolu, dingeen ràññee bu baax, ni ma dégge mbóot mi ci mbirum Almasi bi. 5Moomu mbóot, xamaleesu ko woon doom aadama yi, ca janti maas ya woon, ni ñu ko feeñalale tey, ñu sell ñi diy ndawam ak yonent yi, ci ndimbalal Noo gu Sell gi, 6ba mu leer ne jàmbur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
7Xibaaru jàmm boobu lañu ma def ab jawriñam, te Yàlla, ciw yiwam, moo jëfe manooreem, ba jagleel ma boobu cér. 8Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jàmbur ñi dul Yawut xéewal yu amul kem yi ci Almasi bi. 9May niital ñépp, ni Yàlla nara sottale mébétam, miy mbóot mu làqu woon naka jekk fa moom Yàlla mi sos lépp. 10Su ko defee boroom nguur yeek boroom sañ-sañ ya fa déndi asamaan mana xame ci mbooloom gëmkati Almasi bi, xel mu rafetum Yàlla, ni mu yaatoo ci fànn yu nekk. 11Loolu moo doon naka jekk nammeelam gi mu sottale ci Almasi Yeesu sunub Sang. 12Ci Yeesu, ci kaw ngëm gu nu ko gëm lanu ñemee àgge fit wu mat sëkk fa kanam Yàlla. 13Kon nag dama leen di ñaan, ngeen baña yoqi ngir coono yi may sonn ndax yeen; lépp seen teraanga la.
Saxoo gëm moo mata ñaan
14Looloo ma taxa sukk sama bëti óom, janook Baay bi, 15ki gépp njabootug asamaan ak suuf jële aw tur. 16May ñaan nag, mu may leen, ci koomu teraangaam, seen jëmmu biir feddaliku ak kàttanu Noowam gu Sell. 17Su ko defee seen ngëm tax Almasi bi dëkke seen xol, ngeen sax ay reen yu sampe ci biir cofeel, 18ngir yeen ak mboolem ñu sell ñi, seenum xel mana jàpp, ni mu leen ware, luy yaatuwaayub cofeelu Almasi bi ak guddaay ba ak kawewaay ba ak xóotaay ba. 19Ngeen boole ci daj cofeelu Almasi gi wees xam-xam, ngir ngeen fees, ba fees dell ak koomu Yàlla.
20Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax, 21moo yelloo daraja ci biir mbooloom gëmkat ñi, ak ci Almasi Yeesu, tey ak ëllëg, ba fàww. Amiin.
Currently Selected:
Efes 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright