Bible App logo
Search Icon

Jëf ya 9

9
Sóol tuub na
1Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkooka jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba, 2di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi leen Yerusalem.
3Naka la Sóol dem ba jub Damaas, ag leer fettaxe asamaan, jekki ne ràyy ci kawam. 4Mu ne dàll ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bunduxataal?» 5Mu ne: «Yaay kan Sang bi?» Mu ne: «Man maay Yeesu, mi ngay bunduxataal. 6Léegi nag, jógal, dugg ci dëkk bi, dees na la wax li nga wara def.» 7Nit ña ànd ak moom a nga taxaw, jommi ba ne cell; dégg nañu baat bi te gisuñu kenn. 8Sóol jóg, xippi, gisul dara; ñu daldi koy wommat, dugal ko biir Damaas. 9Diiru ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
10Ab taalibe bu ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Sang bi feeñu ko, ne ko: «Anañas!» Mu ne ko: «Maa ngi, Sang bi.» 11Sang bi ne ko: «Demal ba ca mbedd ma ñuy wax mbedd mu Jub, te nga seet ca kër Yuda ku ñuy wax Sóol te dëkke Tàrs. Ma ngay ñaan. 12Dafa gis cim peeñu ku ñuy wax Anañas duggsi, teg ko loxo, ngir mu dellu di gis.» 13Anañas nag ne ko: «Sang bi, maa dégge ci ñu bare mbirum kooku, ñu seede mboolem jëf ju bon ji mu def say nit ñu sell ci biir Yerusalem. 14Te moo yor ndigal lu tukkee ci sarxalkat yu mag yi, ngir yeewlu képp kuy tudd saw tur.» 15Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jàmbur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israayil. 16Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»
17Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te fees ak Noo gu Sell gi.» 18Ca saa sa lu mel niy waasintóor wadde ca bët ya, mu dellu di gis. Mu daldi jóg, ñu sóob ko ci ndox. 19Ba loolu wéyee, mu lekk, doora am doole.
Sóol toog na ak taalibe ya ca Damaas ay fan. 20Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jànguy Yawut ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla. 21Mboolem ña ko dégg, daldi waaru, naan: «Xanaa du kii moo doon bóom ñiy tudd woowu tur ci Yerusalem? Du moo fi dikkoon, ngir yeewlu leen, yóbbu ci sarxalkat yu mag yi?» 22Teewul Sóol gëna am manoore, ba far jaaxal Yawut ñi dëkke Damaas, di firndeel ne Yeesu mooy Almasi bi.
23Ba ñu ca tegee ab diir bu xawa yàgg, Yawut yi féncoo, ngir reylu ko. 24Sóol nag yég seen mébét. Guddi ak bëccëg lañu doon wattu bunti dëkk ba, ngir bóom ko. 25Teewul taalibe yi yeb ko ag guddi ci ag dàmba, jàlle ko ca wàllaa tata ba, yoor ko.
26Ba Sóol agsee Yerusalem, jéem naa jaxasook taalibe yi, waaye ñépp a ko ragal, ndax ñàkka gëm ag taalibeem. 27Ci kaw loolu Barnabas ànd ak moom, yóbbu ko ca ndaw ya. Barnabas nettali leen, ni Sóol gise Sang bi ca yoon wa, ba mu wax ak Sóol, ak fit wa Sóol waaree ca Damaas ci turu Yeesu. 28Ba loolu amee Sóol ànd ak ndaw yi di dem aka dikk ci biir Yerusalem, di waaree aw fit ci turu Sang bi. 29Mu boole ci di wax aka werante ak Yawut ñiy làkk gereg, te ñoom ñu di ko fexee rey. 30Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbaale Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
31Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
Piyeer faj na nit
32Piyeer mi doon wër fu nekk nag, am na bés mu jaare ca ñu sell ña dëkke Lidd. 33Mu gis foofa waa ju ñuy wax Ene. Fekk na diiru juróom ñetti at, cib lal rekk lay tëdd ndax yaram wu làggi. 34Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi bi wéral na la; jógal, lalal sa bopp.» Mu jóg ca saa sa. 35Mboolem waa diiwaani Lidd ak jóoru Saron nag gis ko, waññiku topp Sang bi.
Piyeer dekkal na nit
36Dëkk ba ñuy wax Yafa, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon. 37Ci fan yooyu, mu daanu wopp, daldi faatu. Ñu sang ko, dugal ko ca néegu kaw taax ma. 38Ci biir loolu taalibe yi dégg ne Piyeer a nga Lidd, te Lidd sorewul Yafa. Ñu yebal ñaari nit ca moom, ngir ñaan ko mu ñëw te baña yeex.
39Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Gëmkati jëtun#9.39 jëtun ñi bokk nañu ci ñi wara jot ndimbal ci jàngu bi. Seetal ci 1.Timote 5.9-10. ñépp a nga doon jooyoo. Ñu yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.
40Ci kaw loolu Piyeer dàq ñépp ca biti. Mu sukk, ñaan, daldi walbatiku jublook néew bi, ne: «Tabita, jógal!» Mu ne xiféet, gis Piyeer, jóg toog. 41Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Ba loolu amee Piyeer woo ñu sell ña, ak jëtun ña, won leen ndaw sa, muy dund. 42Mbir ma nag siiw ca Yafa gépp, ñu bare gëm Sang bi. 43Gannaaw loolu Piyeer dal na Yafa ay fan, kër wullikat bu ñuy wax Simoŋ.

Currently Selected:

Jëf ya 9: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in