2.Korent 1
1
Ubbite gi
1Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Timote mbokk mi, ñeel mbooloom Yàlla mi ci Korent ak mboolem ñu sell ñi ci diiwaanu Akayi gépp. 2Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay ak Sang Yeesu Almasi bi.
Yàlla mooy dëfal xol yi
3Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi, Baayu yërmande yi, Yàlla jiy dëfale nu nekk, 4moom mi nuy dëfal ci sunu jépp njàqare, ngir noonu nu jote nun ci sunu bopp, ndëfalaay lu nu dëfalu fa Yàlla, nu man koo dëfale ñi nekk ci mboolem xeeti njàqare. 5Ndax kat coonoy Almasi bi, nu mu gëna yokkoo ci sunu kaw, ndax li nu ko gëm, noonu itam la ndëfalaay liy bawoo ci Almasi bi di yokkoo. 6Su nu jaaree ci njàqare, seen ndëfalaay ak seen jàmm lay doon. Su nu amee ndëfalaay it, seen ndëfalaay lay doon, ngir coono yi nuy dékku, ngeen man koo dékku, yeen itam. 7Te itam am nanu yaakaar ci yeen bu baax. Xam nanu ne ni ngeen bokke ak nun coono, ni ngeen di bokke ak nun ndëfalaay.
8Ndax kat, bokk yi, bëggunu ngeen umple njàqare ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax. 9Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar Yàlla miy dekkal ñi dee. 10Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu. 11Yeen itam, ni ngeen nu ciy jàppalee mooy ngeen di nu ñaanal. Su ko defee yiw wa nu ñu bare ñaanal ba nu am ko, dina tax ñu bare biral ag cant ci sunu mbir.
Póol biral na jëfinam ak mébétam
12Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digganteek yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may. 13Bindunu leen leneen lu moy mbind moomu ngeen jàng te man koo xam. May yaakaar nag ne dingeen xam ba mokkal, 14noonu ngeen xawa xame ne nun, man ngeen noo damoo, te nun it, yeen la nuy damoo, keroog bésu Sang Yeesu.
15Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona njëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana doon ñaar, ngir nu mana gise ñaari yoon, 16ba bu ma jógee ci yeen, daldi jaareji ci diiwaanu Maseduwan, bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yeen, ba ngeen yiwi ma, ma jëm Yude. 17Ndax ñàkk pastéef laa mébéte moomu mébét? Am ni nitu suuxu neen di mébéte rekk laa topp bay xel ñaar, naan «waaw», naan «déet»?
18Yàlla mi mata gëm de seede na ne kàddu gi nu leen di wax du «waaw, déet,» 19ndax Doomu Yàlla, Yeesu Almasi bi nu biral ci seen biir, man ak Silwan#1.19 Silwan mooy turu waa Room wi Gereg yi naan Silas. Seetal Jëf ya 15.22, 40. ak Timote, du kàddug «waaw, déet;» «waaw» doŋŋ a nekk ci moom. 20Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi bi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal. 21Te ki nuy saxal ci Almasi bi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla. 22Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.
23Man nag seedey Yàlla laa ciy sàkku, giñ naa ko ci sama bakkan, bañ leena yokku naqar moo tax délsiwuma Korent. 24Du caageenu yilif seen ngëm nag, ndax ci ngëm ngeen sax, waaye nook yeen ay liggéey, ngir seen mbégte.
Currently Selected:
2.Korent 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright