YouVersion Logo
Search Icon

1.Korent 8

8
Lu jëm ci ñam wu ñu sarxal ay tuur
1Su dee wàllu ñam wu ñu sarxal ay tuur, dëgg la, nun ñépp am nanu xam-xam ci moomu mbir. Xam-xam nag day tax nit a réy-réylu, waaye cofeel day yokke. 2Ku xalaat ne yaa xam lenn, xamaguloo ni nga wara xame. 3Waaye ku sopp Yàlla, Yàlla xam la.
4Kon su dee wàllu ñam wu ñu sarxal ay tuur, xam nanu ne ay tuur du dara ci àddina, te Yàlla kenn la. 5Doonte am na yu ñuy woowe ay yàlla, te muy lu nekk ci asamaan mbaa ci suuf, te dëgg la, bare na ñu ñu néey ay yàlla lañu, bare na it ñu ñu néey ay sang lañu. 6Teewul ci sunu wàllu bopp, jenn Yàllaa am, muy Baay bi lépp jóge ci moom, te sunu bakkan ñeel ko, benn Sang doŋŋ a am, muy Yeesu Almasi bi lépp ame ci moom, te sunu bakkan, ci moom la ame.
7Waaye du ñépp a xam loolu. Am na gëmkat ñu seen miineelu tuur yi bàyyeegul, ba léegi, te moo tax bu ñu lekkee ñam wu ñu foog ne saraxi tuur la, seen xel mu daladi moo leen di foogloo ne sobe toppe na leen ca ñam wa. 8Waaye du wenn ñam wu nuy jegele ak Yàlla. Nu lekk ko, ak nu bañ koo lekk, du nu yokk, du nu wàññi.
9Waaye ni ngeen di dunde seen sañ-sañu bopp, dangeen ciy xool ñi seen ngëm dëgërul, ngir ngeen bañ leena yóbbe bàkkaar. 10Yaw mi réy xam-xam, ku la gis ca ndab la ca jaamookaayu tuur ya, su dee ab gëmkat bu xelam daladi ndax ngëm gu desee dëgër, mbaa du ko xiir ci roy la, ba mu lekk ca ñamu sarax sa? 11Te su demee noonu nag, su boobaa sa xam-xam bu réy ngay sànke sa mbokkum gëmkat bu néew doole boobu Almasi bi deewal! 12Su ngeen tooñee noonu bokki gëmkat ñi, ba yàq seen xel mu daladi, kon de Almasi bi ngeen tooñ. 13Moo tax, su dee aw ñam wu ma lekk mooy tax ma bàkkaarloo sama mbokkum gëmkat, dootuma lekk mukk aw yàpp ci àddina, ngir baña bàkkaarloo sama mbokkum gëmkat.

Currently Selected:

1.Korent 8: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in