1
Room 6:23
Téereb Injiil
TI
Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.
Compare
Explore Room 6:23
2
Room 6:14
Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla.
Explore Room 6:14
3
Room 6:4
Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees.
Explore Room 6:4
4
Room 6:13
Buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
Explore Room 6:13
5
Room 6:6
Ndegam xam nanu ne daajoon nañu Kirist ca bant ba, xam nanu it ne jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale nañu ko ak Kirist ca bant ba. Yàlla def na loolu, ngir nguuru bàkkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu rëcc ci dooleem.
Explore Room 6:6
6
Room 6:11
Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
Explore Room 6:11
7
Room 6:1-2
Lu nu wara wax léegi nag? Xanaa nu sax ci bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gëna bare? Mukk! Nun ñi dee, ba rëcc ci kàttanu bàkkaar, naka lanu manatee sax ci di ko def?
Explore Room 6:1-2
8
Room 6:16
Ndax dangeena xamul ne koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub.
Explore Room 6:16
9
Room 6:17-18
Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp. Ci noonu rëcc ngeen ci notaangeg bàkkaar te jébbalu ci Yàlla, sóobu ci njub.
Explore Room 6:17-18