1
Peeñu ma 16:15
Téereb Injiil
TI
«Maa ngi ñëw nib sàcc. Bég nga, yaw mi nelawul te di wottu say yére, ngir baña dox yaramu neen, ñuy gis sa gàcce.»
Compare
Explore Peeñu ma 16:15
2
Peeñu ma 16:12
Juróom benneelu malaaka ma sotti ndabam ci dex gu mag, gi ñuy wax Efraat, ndox ma daldi ŋiis, ngir waajal yoonu buuri penku, yiy ñëw.
Explore Peeñu ma 16:12
3
Peeñu ma 16:14
Ay rabi Seytaane lañu woon, yuy def ay kéemaan te di dem ci buuri àddina sépp, di leen dajale, ngir xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Man ji jagleele boppam.
Explore Peeñu ma 16:14
4
Peeñu ma 16:13
Noonu ma gis ñetti rab yu bon yu mel niy mbott, génn ci gémmiñi ninkinànka ja ak rab wa ak naaféq, ba mbubboo yonent.
Explore Peeñu ma 16:13
5
Peeñu ma 16:9
Naaj wu metti di lakk nit ñi, ñu daldi xarab turu Yàlla, ji am sañ-sañ ci kaw musiba yooyu. Waaye tuubuñu sax seeni bàkkaar, ngir jox ko ndam li.
Explore Peeñu ma 16:9
6
Peeñu ma 16:2
Noonu malaaka mu jëkk ma dem, sotti ndabam ci àddina, ba woppi taab ju bon te metti dal nit, ña am màndargam rab wa tey jaamu nataalam.
Explore Peeñu ma 16:2
7
Peeñu ma 16:16
Noonu rab ya dajale buuri àddina si ci bérab bu tudd ci làkku ebrë Armagedon.
Explore Peeñu ma 16:16