1
Filib 4:6
Téereb Injiil
TI
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant.
Compare
Explore Filib 4:6
2
Filib 4:7
Noonu jàmmu Yàlla, ji xel manta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu.
Explore Filib 4:7
3
Filib 4:8
Léegi nag bokk yi, na seen xalaat jublu ci lii: lu dëggu, lu jekk, lu jub, lu sell, lu rafet ak lu faaydawu; su fi amee lu baax mbaa lu mata naw, xalaatleen ko.
Explore Filib 4:8
4
Filib 4:13
Man naa lépp ci ndimbalu Aji Dooleel ji.
Explore Filib 4:13
5
Filib 4:4
Deeleen bég ci Boroom bi; maa ngi koy waxati: bégleen!
Explore Filib 4:4
6
Filib 4:19
Te Yàlla sama Boroom, mi denc ci Kirist Yeesu xéewal yu dul jeex, dina ci faj seeni soxla yépp.
Explore Filib 4:19
7
Filib 4:9
Li ngeen jànge ci man te nangu ko, li ngeen dégge ci man te gis ko, jëfeleen ko; kon Yàllay jàmm dina ànd ak yéen.
Explore Filib 4:9
8
Filib 4:5
Na seen lewet leer ñépp. Boroom bi jege na.
Explore Filib 4:5
9
Filib 4:12
Miin naa ñàkk, man naa naataange. Ci fépp ak ci lépp, Yàlla def na ba sama xol toj ci suur ak xiif, barele ak néewle.
Explore Filib 4:12
10
Filib 4:11
Ba tey soxla taxul ma waxe nii, ndaxte jàng naa doylu ci mbir mu ma mana dab.
Explore Filib 4:11