1
Filib 3:13-14
Téereb Injiil
TI
Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam, di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla taxa woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.
Compare
Explore Filib 3:13-14
2
Filib 3:10-11
Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam, ngir mana séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.
Explore Filib 3:10-11
3
Filib 3:8
Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel manu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.
Explore Filib 3:8
4
Filib 3:7
Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist.
Explore Filib 3:7