1
Filib 1:6
Téereb Injiil
TI
Wóor na ma ne Yàlla mi tàmbali jëf ju baax jii ci yéen, dina ci sax, ba bésu Kirist Yeesu ñëw.
Compare
Explore Filib 1:6
2
Filib 1:9-10
Li ma leen di ñaanal nag mooy lii: yal na seen mbëggeel di yokku tey gëna tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér; yal nangeen sax noonu ci li gëna rafet, ngeen am xol bu laab te baña am benn sikk, ba bésu Kirist ñëw
Explore Filib 1:9-10
3
Filib 1:21
Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee; su ma deeyee, xéewal lay doon ci man.
Explore Filib 1:21
4
Filib 1:3
Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom
Explore Filib 1:3
5
Filib 1:27
Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xibaaru jàmm bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xibaaru jàmm bi
Explore Filib 1:27
6
Filib 1:20
Ndaxte sama xënte ak sama yaakaar mooy ma baña rus ci lenn, waaye sama yaram feeñal ndamu Kirist, ma ànd ci ak kóolute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def démb, te moom laay def tey.
Explore Filib 1:20
7
Filib 1:29
Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam
Explore Filib 1:29