1
Efes 6:12
Téereb Injiil
TI
Ndaxte ndëndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit ñi, waaye ak kilifa yiy nëxal àddina si, ñuy kilifa yi ak ay boroom sañ-sañ, di gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi.
Compare
Explore Efes 6:12
2
Efes 6:18
Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat sëkk, di ñaanal gaayi Yàlla yu sell yi yépp.
Explore Efes 6:18
3
Efes 6:11
Gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ngir mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
Explore Efes 6:11
4
Efes 6:13
Kon nag gànnaayooleen yérey xarey Yàlla yépp, ba mana jànkoonte jamono ju xeex bi taree, not lépp te taxaw temm.
Explore Efes 6:13
5
Efes 6:16-17
Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba mana fél jum yi leen Seytaane di fitt. Defleen mucc, muy seen mbaxanam xare, ak kàddug Yàlla, muy jaasi ji leen Xel mu Sell mi tëggal.
Explore Efes 6:16-17
6
Efes 6:14-15
Taxawleen kon temm, geñoo dëgg te sàngoo njub, muy seen kiiraayu dënn. Solooleen jàmm, ji xibaaru jàmm biy joxe, ni ay dàll ci seeni tànk, ba jekk ci lépp.
Explore Efes 6:14-15
7
Efes 6:10
Léegi nag doolewuleen ci Boroom bi te soloo kàttanam gu mag gi.
Explore Efes 6:10
8
Efes 6:2-3
«Teralal sa ndey ak sa baay,» mooy ndigal li jëkka ëmb dige, maanaa: «ngir nga am gudd fan gu ànd ak jàmm.»
Explore Efes 6:2-3
9
Efes 6:1
Naka yéen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet.
Explore Efes 6:1