1
Màrk 5:34
Téereb Injiil
TI
Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la; demal ci jàmm, te na sa jàngoro wàcc.»
Compare
Explore Màrk 5:34
2
Màrk 5:25-26
Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.
Explore Màrk 5:25-26
3
Màrk 5:29
Ci saa si deret ji taxaw, mu yég ci yaramam ne jàngoroom deñ na.
Explore Màrk 5:29
4
Màrk 5:41
Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.»
Explore Màrk 5:41
5
Màrk 5:35-36
Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.» Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te baña tiit.»
Explore Màrk 5:35-36
6
Màrk 5:8-9
Ndaxte Yeesu da ko ne: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.» Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
Explore Màrk 5:8-9