1
Màrk 4:39-40
Téereb Injiil
TI
Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm. Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»
Compare
Explore Màrk 4:39-40
2
Màrk 4:41
Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»
Explore Màrk 4:41
3
Màrk 4:38
Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
Explore Màrk 4:38
4
Màrk 4:24
Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen.
Explore Màrk 4:24
5
Màrk 4:26-27
Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool. Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe.
Explore Màrk 4:26-27
6
Màrk 4:23
Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
Explore Màrk 4:23