1
Màrk 13:13
Téereb Injiil
TI
Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
Compare
Explore Màrk 13:13
2
Màrk 13:33
Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot.
Explore Màrk 13:33
3
Màrk 13:11
Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen wara wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi.
Explore Màrk 13:11
4
Màrk 13:31
Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
Explore Màrk 13:31
5
Màrk 13:32
«Waaye bés boobu ak waxtu woowu, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
Explore Màrk 13:32
6
Màrk 13:7
Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleena tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul.
Explore Màrk 13:7
7
Màrk 13:35-37
Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di délsi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël. Bu nee jalañ, bumu leen bett, ngeen di nelaw. Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”»
Explore Màrk 13:35-37
8
Màrk 13:8
Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yëngu-yënguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
Explore Màrk 13:8
9
Màrk 13:10
Fàww xibaaru jàmm bi jëkka jib ci xeet yépp.
Explore Màrk 13:10
10
Màrk 13:6
Ñu bare dinañu ñëw ci sama tur naan: “Moom laa,” te dinañu nax ñu bare.
Explore Màrk 13:6
11
Màrk 13:9
«Moytuleen. Dees na leen jébbal àttekat ya, di leen dóor ay yar ca jàngu ya. Dinañu leen dëj ci kanam i boroom réew ak i buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci ñoom.
Explore Màrk 13:9
12
Màrk 13:22
Ndaxte ñiy mbubboo turu Kirist ak ñiy mbubboo turu yonent, dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoona am.
Explore Màrk 13:22
13
Màrk 13:24-25
«Waaye booba, gannaaw metit yooyu: “Jant bi dina lëndëm te weer dootul leer; biddiiw yi di daanoo asamaan, te kàttani asamaan yiy yëngu.”
Explore Màrk 13:24-25