Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw. Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor ñaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga; xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwug Doomu nit ki.