1
Macë 13:23
Téereb Injiil
TI
Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom benn fukk mbaa fanweer.»
Compare
Explore Macë 13:23
2
Macë 13:22
Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ.
Explore Macë 13:22
3
Macë 13:19
Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
Explore Macë 13:19
4
Macë 13:20-21
Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw; waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
Explore Macë 13:20-21
5
Macë 13:44
Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
Explore Macë 13:44
6
Macë 13:8
Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, li ci des fanweer.
Explore Macë 13:8
7
Macë 13:30
Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”»
Explore Macë 13:30