1
Luug 22:42
Téereb Injiil
TI
«Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
Compare
Explore Luug 22:42
2
Luug 22:32
Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo délsee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
Explore Luug 22:32
3
Luug 22:19
Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
Explore Luug 22:19
4
Luug 22:20
Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
Explore Luug 22:20
5
Luug 22:44
Ci biir tiis, Yeesu gëna sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
Explore Luug 22:44
6
Luug 22:26
Waaye yéen buleen def noonu. Ki gëna màgg ci yéen, na nekk ni ki gëna ndaw, te njiit mel ni surga.
Explore Luug 22:26
7
Luug 22:34
Yeesu ne ko: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
Explore Luug 22:34