1
Yowaan 17:17
Téereb Injiil
TI
Samp leen ci dëgg, ngir ñu sell. Sa kàddu mooy dëgg.
Compare
Explore Yowaan 17:17
2
Yowaan 17:3
Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist.
Explore Yowaan 17:3
3
Yowaan 17:20-21
«Ñaanaluma leen ñoom rekk, waaye itam ñi may gëm ëllëg ndax seen wax. Damay ñaan ngir ñépp doon benn. Baay, na ñooñu nekk benn ci nun, ni nga nekke ci man te ma nekke ko ci yaw. Nañu ànd, ba àddina gëm ne yaa ma yónni.
Explore Yowaan 17:20-21
4
Yowaan 17:15
Ñaanuma nga jële leen àddina, waaye nga yiir leen ci Ibliis.
Explore Yowaan 17:15
5
Yowaan 17:22-23
Boole naa leen ci ndam, li nga ma sol, ngir ñu àndandoo, ni nu ànde man ak yaw. Man ci ñoom, yaw it ci man, ngir ñu gëna ànd, nekk benn, ba àddina xam ne yaa ma yónni, xam ne bëgg nga leen, ni nga ma bëgge.
Explore Yowaan 17:22-23