1
Jëf ya 7:59-60
Téereb Injiil
TI
Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!» Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.
Compare
Explore Jëf ya 7:59-60
2
Jëf ya 7:49
“Asamaan mooy sama jal, te suuf mooy sama tegukaayu tànk. Kon gan kër ngeen may tabaxal, mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?
Explore Jëf ya 7:49
3
Jëf ya 7:57-58
Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam; ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sóol.
Explore Jëf ya 7:57-58