1
Jëf ya 4:12
Téereb Injiil
TI
Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu wara mucce.»
Compare
Explore Jëf ya 4:12
2
Jëf ya 4:31
Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yëngatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
Explore Jëf ya 4:31
3
Jëf ya 4:29
Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
Explore Jëf ya 4:29
4
Jëf ya 4:11
Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi, te moo doon doju koñ.”
Explore Jëf ya 4:11
5
Jëf ya 4:13
Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne masuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne daa nañu ànd ak Yeesu.
Explore Jëf ya 4:13
6
Jëf ya 4:32
Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
Explore Jëf ya 4:32