Nee na:
“Demal ci xeet wii ne leen:
‘Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara;
di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’
Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;
dañuy déglu ak nopp yu naqari,
tey gëmm seeni bët,
ngir baña gis ak seeni bët,
dégg ak seeni nopp,
te xam ci seen xol,
ñu waññiku ci man, ma wéral leen.”