1
2.Tesalonig 2:3
Téereb Injiil
TI
Bu leen kenn nax ci benn fànn, ndaxte balaa booba, fàww Xiiroo bu mag bi ak Yàlla am, te Nitu ñaawteef ki feeñ, moom aji alku ji.
Compare
Explore 2.Tesalonig 2:3
2
2.Tesalonig 2:13
Kon nag bokk yi, yéen ñi Boroom bi bëgg, manunu lu dul sax ci sant Yàlla ci li mu leen tànn ca njàlbéen ga, ngir musal leen, mu sédde leen boppam jaarale ko ci jëfu Xel mu Sell mi ak seen gëm dëgg gi.
Explore 2.Tesalonig 2:13
3
2.Tesalonig 2:4
Day weddi lépp lu ñu teg Yàlla walla ñu koy jaamu, di yékkati boppam, ba toog sax ca kër Yàlla ga, tudde boppam Yàlla.
Explore 2.Tesalonig 2:4
4
2.Tesalonig 2:16-17
Sunu Boroom Yeesu Kirist moom ci boppam ak Yàlla sunu Baay, mi nu bëgg te wone yiwam ci nun, ba ubbil nu buntu jàmm ju sax ak yaakaar ju wér, yal na dëfal seeni xol te saxal leen ci jépp jëf ju rafet ak gépp kàddu gu baax.
Explore 2.Tesalonig 2:16-17
5
2.Tesalonig 2:11
Looloo tax Yàlla yónnee leen xelum réer, ba ñu gëm fen.
Explore 2.Tesalonig 2:11
6
2.Tesalonig 2:9-10
Bu Nitu ñaawteef kooku feeñee, dina ànd ak kàttanu Seytaane ak doole ju bare, di wone ay firnde ak kéemaan yu dul dëgg; te dina nas bépp naxe buy sànke, ba yéem ñi nara alku, ndaxte ubbiluñu seeni xol dëgg, gi leen manoona musal.
Explore 2.Tesalonig 2:9-10
7
2.Tesalonig 2:7
Ndaxte fi mu ne ñaawteef gaa ngi jax-jaxi xaat ci kumpa, waaye ki ko téye mi ngi fi ba tey. Bu fi jógee nag
Explore 2.Tesalonig 2:7