Su ma bëggoona damu, du doon yëfi dof, ndaxte dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn baña foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy dégg, ma di ko wax.
Te it ngir ma baña yég sama bopp ndax peeñu yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma mitital ni dég, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma baña yég sama bopp.