Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu boroom Yeesu Kirist, di Baay biy Aji Yërëm tey Boroom lépp luy dëfal xol yi. Mooy dëfal sunu xol ci sunu tiis yépp, ngir nun ci sunu bopp nu mana dëfal xolu ñépp ñi nekk ci tiis, di leen sédd ci noflaay, bi Yàlla def ci sunu xol.