Li ma bëgg kon mooy lii: na góor ñi ñaan ci Yàlla fu nekk, tàllal ko loxo yu sell, te bañ cee boole mer mbaa werante. Naka noonu itam, na jigéen ñi di sol col gu faaydawu, cig woyof ak maandu. Buñu def seen xel ciy létt ak ci takkaayu wurus, mbaa ciy per ak col gu jafe. Waaye na seen col di jëf yu rafet, ndaxte looloo jekk ci jigéen juy woote ag ragal Yàlla.