1
Room 12:2
Kàddug Yàlla
KY
Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.
Compare
Explore Room 12:2
2
Room 12:1
Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.
Explore Room 12:1
3
Room 12:12
Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
Explore Room 12:12
4
Room 12:21
Bu leen lu bon man, waaye defleen lu baax, ba man lu bon.
Explore Room 12:21
5
Room 12:10
Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di teralante.
Explore Room 12:10
6
Room 12:9
Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.
Explore Room 12:9
7
Room 12:18
Su manee am, jàmmooleen ak ñépp, ndegam ci yeen la aju.
Explore Room 12:18
8
Room 12:19
Samay soppe, buleen di feyul seen bopp, xajalleen am sànj, am sànj fajal boppam, ndax bindees na ne: «Maay kiy feye, di añale.» Boroom bee ko wax.
Explore Room 12:19
9
Room 12:11
Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
Explore Room 12:11
10
Room 12:3
Ma artu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.
Explore Room 12:3
11
Room 12:17
Buleen feyantoo, fexeleen di def lu rafet, ñépp seede ko.
Explore Room 12:17
12
Room 12:16
Mànkooleen, buleen xëccu daraja, waaye nanguleena jonjoo ak ñi féete suuf, te baña jàppe seen bopp boroomi xel.
Explore Room 12:16
13
Room 12:20
Li mu wax kay mooy: «Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan. Soo defee noonu, day rus, ba mel ni koo yeni xal.»
Explore Room 12:20
14
Room 12:14-15
Ñi leen di bunduxataal, ñaanalleen leen, ñaanalleen leen te bañ leena móolu. Ñi am mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi am naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.
Explore Room 12:14-15
15
Room 12:13
Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
Explore Room 12:13
16
Room 12:4-5
Ndax kat dafa mel ni sunu yaram wiy wenn, te cér yi bare, doonte cér yépp a wuuteek seen moroom nu ñuy liggéeye. Noonu lanu doone ñu bare, bokk wenn yaram nun ñépp ci Almasi bi nu gëm, te ku nekk di sa cérub moroom.
Explore Room 12:4-5