1
Room 10:9
Kàddug Yàlla
KY
Saw làmmiñ , soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.
Compare
Explore Room 10:9
2
Room 10:10
Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.
Explore Room 10:10
3
Room 10:17
Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi bi.
Explore Room 10:17
4
Room 10:11-13
Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus.» Ag wuutale amul diggante ab Yawut ak jàmbur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall. Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.»
Explore Room 10:11-13
5
Room 10:15
Nees di yéglee xibaar, te yebaleesu la? Noonu la Mbind mi indee ne: «Ñeeka rafeti tànk, ndaw yii di yéglesi xibaari jàmm!»
Explore Room 10:15
6
Room 10:14
Waaye nees di woowe koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko?
Explore Room 10:14
7
Room 10:4
Ndax kat Almasi bi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.
Explore Room 10:4