1
Peeñu ma 16:15
Kàddug Yàlla
KY
Mu ne: «Maa ngi nii di yoot, di dikk nib sàcc. Ndokkalee, yaw mi teewlu, fàggu say yére, ba doo deme gàcceg yaramu neen, ñu di la seetaan.»
Compare
Explore Peeñu ma 16:15
2
Peeñu ma 16:12
Juróom benneelu malaaka mi sotti ndabam ci dex gu mag gi ñuy wax Efraat, dex gi daldi ŋiis, ngir sàkkal buuri penku yiy dikk aw yoon.
Explore Peeñu ma 16:12
3
Peeñu ma 16:14
Ñooñu nag ay njuumay Seytaane lañu, yuy def ay kéemaan, tey dajaleji buuri àddina sépp, ngir xareb bés bu mag bu Yàlla Aji Man ji.
Explore Peeñu ma 16:14
4
Peeñu ma 16:13
Ci kaw loolu ma gis ñetti njuuma yu mel niy mbott, kenn ki génne ci gémmiñu ninki-nanka ji, kenn ci gémmiñu rab wu njëkk wi, ki ci des ci gémmiñu ñaareelu rab wi mbubboo yonent.
Explore Peeñu ma 16:13
5
Peeñu ma 16:9
Ci kaw loolu tàngooru naaj wu metti di lakk nit ñi. Nit ñi nag tuubuñu, sàbbaaluñu Yàlla; xanaa di saaga Yàlla ji dogal yooyu musiba.
Explore Peeñu ma 16:9
6
Peeñu ma 16:2
Malaaka mu njëkk mi dem, sotti ndabam ci kaw suuf, mu def ay taab yu bon te aay ci kaw nit ñi am màndargam rab wi, tey sujjóotal jëmmu nataalu rab wi.
Explore Peeñu ma 16:2
7
Peeñu ma 16:16
Ci kaw loolu njuuma yi dajale buur yi ci béreb bu ñuy wax Armagedon, di baatu ebrë.
Explore Peeñu ma 16:16