1
Sarxalkat yi 26:12
Kàddug Yàlla
KY
Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ.
Compare
Explore Sarxalkat yi 26:12
2
Sarxalkat yi 26:4
kon maa leen di tawal ci waxtoom, suuf si nangu, garab yi meññ.
Explore Sarxalkat yi 26:4
3
Sarxalkat yi 26:3
«Su ngeen dee topp samay dogal, fonk samay santaane te di ko jëfe
Explore Sarxalkat yi 26:3
4
Sarxalkat yi 26:6
«Maay baaxee réew mi jàmm it, ba bu ngeen tëddee kenn du leen tiital. Maay jële rab wu aay ci réew mi, te saamar du jóg, dal ci seenum réew.
Explore Sarxalkat yi 26:6
5
Sarxalkat yi 26:9
«Te itam maa leen di baaxe, giiral leen, yokk leen. Dinaa sàmm sama kóllëreek yeen.
Explore Sarxalkat yi 26:9
6
Sarxalkat yi 26:13
Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, ngeen noppee doon seeni jaam; maa dog seen buumi njaam, siggil leen.
Explore Sarxalkat yi 26:13
7
Sarxalkat yi 26:11
«Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen seexlu.
Explore Sarxalkat yi 26:11
8
Sarxalkat yi 26:1
«Buleen sàkkal seen bopp ay yàllantu, du lenn luy jëmmu tuur mbaa tuuru doj wu ngeen sampal seen bopp, te doj wu ñu ñaas ay nataal it, buleen ko sàkkal béreb ci seen réew, di ko sujjóotal, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Explore Sarxalkat yi 26:1
9
Sarxalkat yi 26:10
Dingeen lekk ngóob mu yàgg, dence lu yàgg, ba far génne mu yàgg ma, wuutal fa mu bees.
Explore Sarxalkat yi 26:10
10
Sarxalkat yi 26:8
Seen juróomi nit ay dàq téeméer (100), seen téeméeri nit dàq fukki junni (10 000). Seeni noon la saamar di dal, ñu daanu fi seen kanam.
Explore Sarxalkat yi 26:8
11
Sarxalkat yi 26:5
Dingeen bàcc ba keroog wittum reseñ jot te dingeen witt reseñ ba jamonoy ji jot. Dingeen lekk seenum pepp ba suur këll te dingeen dëkk ak jàmm ci seenum réew.
Explore Sarxalkat yi 26:5
12
Sarxalkat yi 26:7
Kon dingeen dàq seeni noon, saamar ba dal, ñu daanu fi seen kanam.
Explore Sarxalkat yi 26:7
13
Sarxalkat yi 26:2
Samay bési Noflaay nag wormaalleen ko, te sama béreb bu sell teralleen ko. Maay Aji Sax ji.
Explore Sarxalkat yi 26:2