1
Yowaan 19:30
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu nag muucu bineegar ba, daldi ne: «Sotti na!» Ci kaw loolu mu sëgal bopp ba, daldi yiwi noo ga.
Compare
Explore Yowaan 19:30
2
Yowaan 19:28
Gannaaw loolu Yeesu xam ne lépp sotti na, mu daldi ne: «Mar naa!» ngir matal la Mbind ma indi woon ci mbiram.
Explore Yowaan 19:28
3
Yowaan 19:26-27
Taalibe ba Yeesu soppoon itam ma nga fa woon, taxaw. Ba leen Yeesu gisee da ne yaayam: «Soxna si, sa doom a ngoogu.» Mu teg ca ne taalibe ba: «Sa yaay a ngoogu.» Ca waxtu woowa tembe la taalibe ba yóbbu soxna sa këram.
Explore Yowaan 19:26-27
4
Yowaan 19:33-34
Ñu agsi ci Yeesu, daldi gis ne dee na ba noppi, ba tax dammuñu ay tànkam. Teewul kenn ca takk-der ya jam ko ab xeej ci faar yi, deret ànd ak ndox tuuru ca saa sa.
Explore Yowaan 19:33-34
5
Yowaan 19:36-37
Loola moo am ngir Mbind mi indi woon lii, sotti: «Benn yaxam, deesu ko damm.» Meneen Mbind indeeti ne: «Dinañu gis ki ñu jam.»
Explore Yowaan 19:36-37
6
Yowaan 19:17
Moom ci boppam moo gàddu bant ba, génn jëm ba fa ñuy wax bérebu Kaaŋu bopp, muy firi Golgota ci làkku yawut.
Explore Yowaan 19:17
7
Yowaan 19:2
Takk-der ya teg ci boppu Yeesu kaala gu ñu ràbbe ay dég, solal ko mbubb mu xonq curr.
Explore Yowaan 19:2