Ma ngay ñaanal Yuusufa te naan:
«Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon,
moom Yàlla ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,
moom Malaaka mi ma musal ci bépp loraange—
yal na barkeel xale yi,
ba ñu saxal sama tur
ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa,
te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.»