1
Njàlbéen ga 46:3
Kàddug Yàlla
KY
Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte xeet wu réy laa fay sose ci yaw.
Compare
Explore Njàlbéen ga 46:3
2
Njàlbéen ga 46:4
Man ci sama bopp maay ànd ak yaw Misra, te na la wóor ne dinaa la delloosi, te it Yuusufa moo lay doggali.»
Explore Njàlbéen ga 46:4
3
Njàlbéen ga 46:29
Yuusufa nag waajal waruwaayam, dajeji ak baayam Israayil ca Gosen. Ba Yuusufa àggee ba ca moom, da koo laxasu, ne ñàpp ci kawam, jooy lu yàgg.
Explore Njàlbéen ga 46:29
4
Njàlbéen ga 46:30
Israayil ne Yuusufa: «Léegi de, bu ma yeboo dee, gannaaw gisaat naa la, ngay dund.»
Explore Njàlbéen ga 46:30