1
Galasi 4:6-7
Kàddug Yàlla
KY
Li ngeen diy doom nag tax na Yàlla yebal Noowug Doomam ci seen biir xol, ba Noo gi naan: «Abba», muy firi Baay. Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.
Compare
Explore Galasi 4:6-7
2
Galasi 4:4-5
Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa, ngir jot ñi ci curgag yoon wi, ba nu jagoo cérub doom.
Explore Galasi 4:4-5
3
Galasi 4:9
Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?
Explore Galasi 4:9