1
Mucc ga 9:16
Kàddug Yàlla
KY
Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.
Compare
Explore Mucc ga 9:16
2
Mucc ga 9:1
Ba loolu wéyee Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
Explore Mucc ga 9:1
3
Mucc ga 9:15
Nëgëni tey doon naa xàcc sama loxo xaat, dumaa leen mbas mu leen di fare ci kaw suuf, yaw yaak sa waa réew.
Explore Mucc ga 9:15
4
Mucc ga 9:2-3-4
Ndax boo leen bañee bàyyi kat, xanaa di leen téye ba tey, loxol Aji Sax ji dina dal ci sa kaw jur gi ci tool yi, muy fas ak mbaam ak giléem, jur gu gudd ak gu gàtt, te jàngoro ju aaytal lool lay doon. Waaye man Aji Sax ji maay ràññaatle juru bànni Israayil ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israayil moom.”»
Explore Mucc ga 9:2-3-4
5
Mucc ga 9:18-19
Te kat nëgëni ëllëg dinaa taw yuur bu réy, bu masula am Misra, ba mu sosoo ba tey jii. Kon nag sa jur ak mboolem loo am, te mu nekk ci biti, joxeel ndigal ñu boole fat fu wóor, ndax lu nekk ci biti te fateesu ko, su tawtee dee, muy nit mbaa mala.”»
Explore Mucc ga 9:18-19
6
Mucc ga 9:9-10
Su ko defee dóom bi doon pënd bu sew ci kaw réewum Misra gépp, daldi def ay taab yuy sotti dëtt ci réewum Misra gépp, ci nit ak mala.» Ñu sàkk dóom, àgg ca kanam Firawna, Musaa suy dóom ba, mu jëm ca kaw, ba mu def ay taab yuy sotti dëtt ca nit ñaak mala ya.
Explore Mucc ga 9:9-10