Mucc ga 9:2-4
Mucc ga 9:2-4 KY
Ndax boo leen bañee bàyyi kat, xanaa di leen téye ba tey, loxol Aji Sax ji dina dal ci sa kaw jur gi ci tool yi, muy fas ak mbaam ak giléem, jur gu gudd ak gu gàtt, te jàngoro ju aaytal lool lay doon. Waaye man Aji Sax ji maay ràññaatle juru bànni Israayil ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israayil moom.”»





