1
Mucc ga 13:21-22
Kàddug Yàlla
KY
Bu bëccëgee nag Aji Sax ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg. Du bëccëg bu niir wa jóge ca kanam mbooloo ma, te du guddi it gu sawara wa masa wuute.
Compare
Explore Mucc ga 13:21-22
2
Mucc ga 13:17
Firawna bàyyi na mbooloo ma, ñu dem, waaye Yàlla jaaralewu leen ca yoon wa jëm réewu Filisti, doonte moo gënoona gàtt. Booba Yàlla dafa xam ne, su mbooloo ma sóoboo ci ay xare ci woowu yoon, dañuy yoqi, bay xalaata dëpp, dellu Misra.
Explore Mucc ga 13:17
3
Mucc ga 13:18
Moo tax Yàlla wiiriloo mbooloo ma, ñu jaare ca màndiŋ ma, jëm ca géeju Barax ya. Ba mu ko defee bànni Israayil fagaru ba jekk, daldi génn Misra.
Explore Mucc ga 13:18