«Guddig keroog maay wër réewum Misra te maay faat lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, nit ak mala, te itam maay mbugal mboolem tuuri Misra. Man maay Aji Sax ji. Deret ji ci kër yi ngeen dëkke nag, mooy doon seen xàmmikaay, ba tax bu ma gisee deret ji, musal leen. Su ko defee bu may dal ci kaw réewum Misra, menn musiba du leen lor.