1
Jëf ya 3:19
Kàddug Yàlla
KY
Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.
Compare
Explore Jëf ya 3:19
2
Jëf ya 3:6
Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi mu Nasaret, doxal!»
Explore Jëf ya 3:6
3
Jëf ya 3:7-8
Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam aki kostanam dëgër. Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox aka tëbantu, tey sant Yàlla.
Explore Jëf ya 3:7-8
4
Jëf ya 3:16
Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
Explore Jëf ya 3:16