Maa lay musal ci askanu bànni Israayil ak ci jàmbur ñi ma lay yebal, ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci nooteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm gi ñu ma gëm.”