1
2.Korent 6:14
Kàddug Yàlla
KY
Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?
Compare
Explore 2.Korent 6:14
2
2.Korent 6:16
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»
Explore 2.Korent 6:16
3
2.Korent 6:17-18
Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal. Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.
Explore 2.Korent 6:17-18
4
2.Korent 6:15
Gan juboo la Almasi bi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi?
Explore 2.Korent 6:15