Waaye cant ñeel na Yàlla! Moom mi Almasi bi tax mu di nu yóbbaale saa su nekk, ci njaab miy fésal ndamam, te cuuraayal xam-xamam, nun ñii la koy wasaaree fépp, ndax kat nun nooy cuuraayal Almasi bi fa Yàlla, ñeel ñi ci yoonu texe ak ñi ci yoonu sànkute.