1
1.Timote 4:12
Kàddug Yàlla
KY
Bu la kenn xeebe say at yu néew, waaye nanga doon royukaayu gëmkat ñi ci wax ak jëfin ak cofeel ak ngëm ak dundin wu set.
Compare
Explore 1.Timote 4:12
2
1.Timote 4:8
Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ragal Yàlla, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.
Explore 1.Timote 4:8
3
1.Timote 4:16
Sàmmal sa bopp nag, sàmm sa àlluwa, te saxoo ko; soo ko defee, dinga mucc, musal ñi lay déglu.
Explore 1.Timote 4:16
4
1.Timote 4:1
Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane
Explore 1.Timote 4:1
5
1.Timote 4:7
Waaye nettali yu yittewoo lu dul Yàlla, ak léebi jeeg ju màggat ji, bañ ko, te nga tàggatu ci ragal Yàlla.
Explore 1.Timote 4:7
6
1.Timote 4:13
Ba keroog may dikk, saxool di jàng-biral Mbind mi, di ñaaxe aka jàngale.
Explore 1.Timote 4:13